1-Taarou xel mou dioup kou ko ame
Té di waye kou baax nanga waye
Ki réewmi bokk ni yawa
Moye Aladji Mâdioroh
2- Moom la YALLA diokh limou ame
Seydi Babacar nangou ko
Kone kou ame ngueunél na ko diokh
Kiye Aladji Mâdioroh
3- Seydi Babacar la mou wax
Nane ko gueume té gueume Mâdior
Moko wax yawa té dou dagne
Kone siyaré léne Mâdioroh
4- Gorou YALLA gui kou mou wax
Yawa yaw té kéne dou ko mime
Kone ninél ko yaw yawa yaw
Baye Aladji Mâdioroh
5- Kouko waxoul dé mooma dou dagne
Babacar Sy moom dou ko sosse
Gorou YALLA waxna ni léen
Baye Aladji Mâdioroh
6- Kou démoul dé mane dém naa
Té xam ni niépa ngui dém
Dém démine wi sakh dafa siiw
Kéne mimatoul Mâdior
7- Wa Ndakarou niépa ngui téew
Kaolack, Teunguedj téew
Sine-Saloum, Louga téew
Nieuw siyaré Mâdioroh
8- Thiès janxeen dé kéne déssoufa
Casamance, Diourbela ngui téew
Bokk xél, xalat aki dieuf
Nieuw siyaré Mâdioroh
9- Sénégala ame kouni méle
Mauritanie ngui nieuw diko yéme
Narou fass yi kéne déssatoul
Di siyaré Mâdioroh
10- Moukhadame you matt Tidiane
Cheikhou khadirou nimzatt
Wa keur Serigne Touba
Nieuw siyaré Mâdioroh
11- Li ma wax dé mane sossou ma
Amé beute di xool té di guiss
Deuk Ndar té xam li ma wax
Thi Aladji Mâdioroh |
12- Diaka djia ngui kéne dou ko mime
Gor you matt dioulite difa wax
La Illa Banaan Illa Lah
Mamadoh Rassoulou Lah
13- Wazifa baa ngua djipe souba téel
Ak Timiss ba gué dou fa dagne
Yalna YALLA yokala yiw
Kiye Aladji Mâdioroh
14- Sama beutt gueumoul nélawoul
Sama fitt rafoul yeungou woul
Xél yi kagne démoul thi koudoul
Baye Aladji Mâdioroh
15- Bayi léen mou dém famou dieum
Léegui nou ague nioune fanou dieume
Chef de gare bi léegui mou nieuw
Moye Aladji Mâdioroh
16- Dji na fi garap gou raféte
Samm kock djikom you raféte
Ba mou sakh sakhine wou raféte
Moye Aladji Mâdioroh
17- Nioniou kat Madior guenou léen
Nday ak baay xanaa danou guiss
Aw baatine bou réye bafa né
Thia Aladji Mâdioroh
18- Deunou gornia rirr na lou werr
Mo waral niou khaathiou ba Ndar
Dakh noon ya ak lanou yorr
Nane siyaré Mâdioroh
19- Seydina Karim gayaa ngui
Moye dioulite té gueum Madior
Tapha Dieng la wétaliko
Andak talibéye Madior.
20- Binde na bataaxali xol
Di thia xamlé madjima xam
Thie thiofél gui tax madi waye
Baye Aladji Mâdioroh
21- Yalna YALLA maye daradia
Talibéye Madior yi ko gueume
Sant YALLA miy daradial
Baye Aladji Mâdioroh
22- Gaw tou léen thie moom dafa ware
Mo fi siwe té ame daradia
YALLA bourbi mo koko maye
Baye Aladji Mâdioroh |