Wolof
Français
1. Jële werd ci boroom ndigël bu wer ci silsila bi.
1. Recevoir le wird d’un talibé dûment autorisé dans la silsila tidjane.
2. Do am beneen werd budul bu tariixa bi.
2. Renoncer à tout wird d’une tariqa autre que la tidjaniya.
3. Do ziyaar beneen waliyu, boo dund walla bu dee bu bokul ci tariixa bi.
3. Ne pas effectuer de ziarra auprès d’un waliyou vivant ou décédé qui n’est pas tidjane (il s’agit ici de se suffire de son guide tout en traitant tout érudit d’une autre tariqa avec les égards dûs à son rang).
4. Juli yi juroom ci mbooloo.
4. Effectuer les 5 prières en commun.
5. Am cofeel ci CHEIKH ak ay kuutaayam ba dee fekla si.
5. Vouer affection et profond respect à Cheikhna Cheikh Ahmed Tidjane Chérif (RTA) et ses khalifes jusqu’à la mort.
6. Bañ naagu.
6. Ne pas faire preuve d’excès de confiance.
7. Bañ noonoo CHEIKH ak kuutaayam yiy dund.
7. Ne pas manifester la moindre hostilité à Cheikh (RTA) ou à ses khalifes vivants.
8. Sax si werd wi ba dee fekla si.
8. Pratiquer le wird sans interruption jusqu’à la mort.
9. Nga am passpass.
9. Avoir une foi indéfectible en Cheikh et en la tariqa.
10. Mucc ci diingët.
10. S’abstenir de critiquer (Cheikh, tariqa, khalifes, talibés).
11. Am ndigël ci werd wi.
11. Etre autorisé à pratiquer le wird.
12. Wazifa ak xadaratul jumaa ci mbooloo.
12. Faire la wazifa et la hadaratoul djouma en commun.
13. Jawaara ak njapp.
13. Ne réciter la djawara qu’après s’être purifié rituellement à l’eau (ablution).
14. Bañ dogoog say waajur ak say mbokki taalibe.
14. Ne rompre ni les liens parentaux (entendu au sens de père et mère), ni les liens avec ses frères talibés.
15. Bañ saggane werd wi.
15. Ne pas faire preuve de négligence dans la pratique du wird.
16. Bañ woote wilaaya ak xutbu ci lu amul.
16. Ne pas se faire passer pour un Saint ou un Pôle si on ne l’est pas.
17. Teral kepp kuñuy askanale ci CHEIKH ak ci tariixa bi.
17. Traiter toute personne liée à Cheikh ou à la tariqa avec égard.
18. Bañ merloo sa mbokku talibe.
18. Ne pas irriter son frère talibé.
19. Laab ci sa yaram ak sa yëre ak berëp bi nga took.
19. Etre en état de pureté rituelle, porter des habits purs, s’asseoir dans un endroit pur.
20. Took jublu xibla.
20. S’asseoir orienté vers la qibla durant le wird (sauf dans les situations d’exception prévues).
21. Bañ wax ci jataayu werd.
21. Ne pas parler pendant le wird (sauf dans les situations d’exception prévues).
22. Teewlu ci baat yi.
22. Se concentrer sur les paroles du wird.
23. Teewlu Yonent bi, walla CHEIKH, walla Serigne bi.
23. Sentir la présence du Prophète (SAW), de Cheikh ou de son guide.